Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day xamle ne képp ku giñ ci ku dul Yàlla te du ay Turam ak i Meloom weddi na walla bokkaale na; ndax giñ day waral màggal ki ñuy giñ ci moom, te màggal Yàlla rekk la ñeel; kon deesul giñ ci ku dul Yàlla walla ay Turam ak i Meloom -tudd naa sellam ga-. Giñ gii nag ci bokkaale gu ndaw la bokk; waaye kiy giñ bu màggalee la muy giñe kem ni ñuy màggale Yàlla mbaa lu ko ëpp; bu boobaa day nekk bokkaale gu mag.